After having welcomed his guest Amy and given her a chance to rest for a while, Abdu shows her some pictures in his album, Amy is looking at the pictures and asking questions about them.
| Amy: | ki kan la? | |
| Abdu: | sama pappa la. | |
| Amy: | kii nak? | |
| Abdu: | kii sama yaay la | |
| Amy: | sa yaay, naka la sant? | |
| Abdu: | Saar la sant. | |
| Amy: | ñii nak, ñan lañu? | |
| Abdu: | samay rakk lañu. | |
| Amy: | am nga mag? | |
| Abdu: | déédéét, man taaw laa, yow nak? | |
| Amy: | man caat laa; ay mag rekk laa am. | |
| Abdu: | man, ñetti rakk laa am: Anta, Isaa ag Kumba. | |
| Amy: | ñoom, lan lañu? | |
| Abdu: | Anta jangalekat la, Isaa beykat la; Kumba moom taalibe la. | |
| Amy: | ñoom ñepp góór lañu? | |
| Abdu: | déédéét, Anta ag Kumba duñu góór, jigéén lañu, |
| pappa | father | |
| yaay | mother | |
| sama | my | |
| sa | your (singular) | |
| kiinak? | and this (person)? | |
| ñii nak? | and these (people)? | |
| ñan? | who (plural) | |
| rakk | younger brother or sister | |
| mag | older brother or sister | |
| taaw | oldest child of the family | |
| caat | youngest child of the family only | |
| rekk | only | |
| ñett (i) | three | |
| jangalekat | teacher | |
| beykat | farmer | |
| taalibe | student | |
| ñepp | all | |
| góór | male | |
| jigéén | female |