Wolof Online: Courses: Wolof 241: LESSON 5
A taxi arrives at Abdu Sekk's place. Abdu Sekk is at the window, talking with his 10 year-old sister, Kumba. They see the taxi stopping in front of the house, and while the taxi driver is helping Amy Johnson with her luggage, Kumba asks Abdu about the identity of the stranger.
| Kumba: | Abdu, kii kan la? | |
| Abdu: | kii sama gan la. | |
| Kumba: | naka la tudd? | |
| Abdu: | Amy Johnson la tudd. | |
| Kumba: | fan la joge? | |
| Abdu: | Chicago la joge. | |
| Kumba: | Chicago lan la? rééw la? | |
| Abdu: | déédéét, Chicago du reew dëkk la. | |
| Kumba: | ci ban rééw la Chicago nekk? | |
| Abdu: | ci Amerik la nekk. | |
| Kumba: | kon sa gan gi AmerikeN la ? | |
| Abdu: | waaw, moom AmerikeN la. Yow nak, xam nga lan nga? | |
| Kumba: | waaw! man, Wolof laa te Senegaal laa dëkk. |
| kii kan la? | who is this? | ||
| sama gan | My guest. | ||
| lan la? | What is it? | ||
| rééw | country | ||
| du rééw | It is not a country | ||
| dëkk la. | It is a city. | ||
| ci ban rééw? | In which country? | ||
| nekk | to be | ||
| kon | so | ||
| sa gan gi | your guest | ||
| AmerikeN | American | ||
| yow nak? | and you (sg.)? | ||
| lan nga? | What are you (sg.)? | ||
| te | and |
Return to [Wolof 241] [Courses] [Welcome Page]