Wolof Online: Courses: Wolof 241: LESSON 4

Musaa is a taxi driver; his passenger, Amy Johnson, is an American tourist visiting Senegal for the second time. They are going from the Dakar airport to the downtown area, Musaa starts the conversation; after greeting Amy, he tries to find out who she is and where she is coming from.
| Musaa: | sama jigéén, naka nga tudd? | |
| Amy: | man, Amy Johnson laa tudd. | |
| Musaa: | xanaa Tugal nga joge? | |
| Amy: | déédéét, Amerik laa joge. | |
| Musaa: | fan nga dëkk ci Amerik? | |
| Amy: | Chicago laa dëkk. yow, xam nga fa? | |
| Musaa: | déédéét, waaye am naa ay xarit ci New York, am nga ay xarit ci dëkk bi? | |
| Amy: | waaw. | |
| Musaa: | naka la tudd? | |
| Amy: | moom, Abdu Sekk la tudd, | |
| Musaa: | fan la dëkk? | |
| Amy: | "Sicap" la dëkk. | |
| Musaa: | xam naa fa, |
| Wolof | Translation | ||
| sama jigéén | "my sister" (normally used by males addressing females) | ||
| naka nga tudd? | Ms, what is your name? | ||
| X laa tudd | my name is X | ||
| Tugal | France (and by extension Europe) | ||
| joge | to come from | ||
| déédéét | no! | ||
| waaw! | yes! | ||
| Amerik | America | ||
| fan | where? | ||
| dëkk | to live in | ||
| dëkk bi | the city | ||
| ci | in | ||
| xam | to know | ||
| fa | there | ||
| waaye | but | ||
| am | to have | ||
| ay xarit | some friends | ||
| xarit | friend | ||
| naka la tudd? | what is her/his name? | ||
| X la tudd | his/her name is X | ||
| "Sicap" | (a residential area in Dakar) |
Return to [Wolof 241] [Courses] [Welcome Page]